Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Buur ya - 1.Buur ya 2

1.Buur ya 2:4-30

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4ba keroog Aji Sax ji sottal kàddoom ga mu ma waxoon ne ma: “Su say sët sàmmee seen dundin, saxoo ngëm gu ma wéetal, te gar ci seen bakkan, kon doo ñàkk mukk ku lay wuutu ci jalub Israyil.”
5«Yaw ci sa bopp xam nga li ma Yowab doomu ndaw sa Seruya def, te def na ko ñaari njiiti xarey Israyil, di Abner doomu Ner ak Amasa doomu Yeter: rey na leen, tuur seen deret ni bu doon xare, ba taqal boppam ripp. Moo rendi ci biir jamonoy jàmm.
6Jëflanteel ak moom ci kaw xel, bu ko bàyyi mu duggaale bàmmeel bijjaaw.
7«Góor ñiy doomi Barsilay mu Galàdd nag, nanga leen baaxe, te ñuy bokk ak yaw ndab, ndax kat taxawu woon nañu ma, ba may daw Absalom sa doomu baay.
8«Gannaaw loolu bàyyil xel ci Simey mi nga feggool, muy doomu Gera mu Baxurim, mi bokk ci giirug Beñamin. Moom moo ma doon tifaari saaga, bés ba ma jëmee Maanayim, moom mu dikk dajeek man ca dexu Yurdan. Ma giñal ko ci Aji Sax ji ne ko: “Duma la rey, sama saamar du la dal!”
9Waaye yaw de, bu ko ñàkka topp, ndax boroom xel nga, te dinga xam ni ngay defeek moom, ba mu sangoo deretam, ànd ak bijjaawam, dugg bàmmeel.»
10Gannaaw loolu Daawuda nelaw, fekki ay maamam, ñu denc ko ca gox ba ñu naan Kër Daawuda.
11Nguurug Daawuda ci Israyil tollu na ci ñeent fukki at, di juróom ñaari at ya mu péeyoo Ebron, ak fanweeri at ak ñett ya mu péeyoo Yerusalem.
12Suleymaan nag toog ca jalub baayam Daawuda; nguuram dëgër, ne kekk.
13Ci biir loolu Adoña ma Agit di ndeyam, dem ca Batseba, ndeyu Suleymaan. Mu ne ko: «Mbaa jàmm a la indi?» Mu ne ko: «Jàmm la.»
14Mu neeti ko: «Mbir la mu ma lay wax.» Mu ne ko: «Waxal.»
15Mu ne ko: «Xam nga ne maa moomoon nguur gi, te man la Israyil gépp séentu woon, ma falu buur. Waaye tey nguur gi walbatiku na, tegu ci sama loxol doomu baay, ndax Aji Sax jee ko ko jox.
16Léegi nag lenn rekk laa lay ñaan, te nga bañ maa gàntu.» Mu ne ko: «Waxal rekk.»
17Mu ne ko: «Buur Suleymaan du la gàntu, rikk ñaanal ma ko, mu may ma Abisag mu Sunem soxna.»
18Batseba ne ko: «Baax na, man kay maa la koy waxal Buur.»
19Batseba dem ca Buur Suleymaan, ngir wax ko mbirum Adoña ma. Buur jóg gatandu ko, sukkal ko, daldi toogaat ci ngànguneem. Mu tegal ndeyam ngàngune, mu toog ci ndijooram.
20Mu ne ko: «Man de, lenn lu tuut rekk laa lay ñaan, te bu ma gàntu.» Mu ne ko: «Waxal, saa ndey, duma la gàntu.»
21Mu ne ko: «Abisag mu Sunem, may ko sa doomu baay Adoña soxna.»
22Buur Suleymaan ne ndeyam: «Nga ne! Adoña ngay ñaanal Abisag mu Sunem soxna? Tee nga koo ñaanal nguur gi far, nde mooy sama mag, ñaanalaale ko Abiyatar sarxalkat bi, mook Yowab doomu Seruya?»
23Buur Suleymaan nag giñ ci Aji Sax ji ne: «Yal na ma Yàlla teg mbugal mu gëna tar, ndegam Adoña du feye bakkanam lii muy sàkku!
24Léegi nag giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund, te teg ma fi, dëj ma ci jalub Daawuda sama baay, sampal ma askanu nguur, wa mu dige woon, bésub tey jii Adoña dina dee.»
25Buur Suleymaan daldi jox ndigal Benaya doomu Yoyada. Benaya jam Adoña, mu dee.
26Abiyatar sarxalkat bi nag, Buur ne ko: «Dellul Anatot ca say tool. Dee rekk a war ci yaw, waaye bésub tey jii duma la rey, ndax li nga gàddu woon gaalu Aji Sax ji Boroom bi, dox jiitu sama baay Daawuda. Nga teg ci bokk ak sama baay mboolem coono bu mu daj.»
27Suleymaan nag jële Abiyatar ci liggéeyu saraxi Aji Sax ji, daldi matal li Aji Sax ji waxoon ci waa kër Eli ca Silo.
28Yowab àndul woon ak Absalom ci pexeem, waaye Adoña la mujj àndal. Ba Yowab yégee la xew, daa daw ba ca xaymab Aji Sax ji, jàpp ca béjjén ya ca cati sarxalukaay ba, ngir rawale bakkanam.
29Ñu wax Buur Suleymaan ne ko: «Yowab daw na, làquji ca xaymab Aji Sax ji, te kat ma nga ca sarxalukaay ba.» Suleymaan sant Benaya doomu Yoyada, ne ko mu dem, jam ko.
30Benaya dugg ca biir xaymab Aji Sax ja, ne ko: «Buur nee nanga génn!» Yowab ne ko: «Génnuma, fii laay deeye!» Benaya yegge Buur waxi Yowab ak la mu ko tontu.

Read 1.Buur ya 21.Buur ya 2
Compare 1.Buur ya 2:4-301.Buur ya 2:4-30