Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Buur ya - 1.Buur ya 20

1.Buur ya 20:25-35

Help us?
Click on verse(s) to share them!
25Te yaw nga sosaat mbooloom xare mu mel ni ma nga amoon, fas ak fas, watiir ak watiir, ndax nu mana xareek ñoom ci joor gi. Su boobaa déy, noo leen di ëpp doole.» Mu déggal leen, def noona.
26Ca déwén sa Ben Addàd lim waa Siri, daldi dem Afeg ca xare baak Israyil.
27Waa Israyil daje, sàkk ab dund, ba noppi dox wuti leen. Waa Israyil a nga dal janook ñoom, di saf ñaari gétti bëy. Waa Siri ñoom fees àll ba.
28Góoru Yàlla ga dikk ne buurub Israyil: «Aji Sax ji dafa wax ne: Gannaaw waa Siri dañoo yaakaar ne man Aji Sax ji, yàllay tund laa, duma yàllay xur, maay teg mbooloo mu réy mii mépp ci say loxo. Su ko defee ngeen xam ne maay Aji Sax ji.»
29Diiru juróom ñaari fan nag ñu jàkkaarloo ca seeni dal. Bésub juróom ñaareel ba xare ba jib, waa Israyil daane téeméeri junniy xarekat (100 000) yu warul fas ca waa Siri ci benn bés bi;
30ña ca des daw ba Afeg, ca biir dëkk ba, tata ja màbb ca kaw ñaar fukki junniy nit ak juróom ñaar (27 000) ca ñoom. Fekk na Ben Addàd daw dugg ca biir dëkk ba, jàll ci biir néeg bu làqoo làqu.
31Ay jawriñam ne ko: «Waaw, nun de dégg nanu ñu naa buuri Israyil buur yu baax lañu. Tee noo sol ay saaku, tañlaayoo buum, toroxloo ko, te dem ca buurub Israyil? Jombul mu bàyyi la, nga dund.»
32Ñu teraxlaayoo ay saaku, tañlaayoo ay buum, dem ca buurub Israyil, ne ko: «Ben Addàd sa jaam ba nee, nga baal ko ngalla te bàyyi ko mu dund.» Mu ne: «Ndeke mu ngi dund ba tey? Moom sama mbokk a!»
33Ndaw ya am njort lu rafet nag. Ñu gaaw naa: «Ben Addàd kay sa mbokk a!» Mu ne leen ñu dem indi ko. Ba Ben Addàd dikkee ba ca moom, mu waral ko ca watiiram.
34Ben Addàd ne Axab: «Dëkk yi sama baay nangoo woon ci sa baay dinaa la ko delloo, te boo yeboo sàkkal sa bopp ay bérabi njaay ca Damaas, na sama baay def ca Samari.» Axab ne ko: «Man nag damay fasanteek yaw kóllëre ci loolu, bàyyi la nga dem.» Ba loolu amee mu fasanteek moom kóllëre, bàyyi ko mu dem.
35Ci biir loolu kenn ca kurélu yonent ya wax moroom ma ci ndigalal Aji Sax ji, ne ko: «Ayca, jam ma!» Waa ja lànk, ne du ko jam.

Read 1.Buur ya 201.Buur ya 20
Compare 1.Buur ya 20:25-351.Buur ya 20:25-35