25Bi ñu fekkee Yeesu ca geneen wàllu dex ga, ñu ne ko: «Kilifa gi, kañ nga fi ñëw?»
26Yeesu ne leen: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, firnde yi ngeen gis taxul ngeen may seet. Yéena ngi may wër ndax mburu, mi ngeen lekk ba suur.
27Buleen liggéeyal ñam wuy yàqu; li gën mooy ñam wu sax abadan tey joxe dund gu dul jeex. Ñam woowule, Doomu nit ki dina leen ko jox, ndaxte moom la Yàlla Baay bi tànn, mu nekk ndawam.»
28Noonu ñu laaj ko ne: «Lu nu wara liggéey, ngir matal jëf yi neex Yàlla?»
29Yeesu ne leen: «Jëf ji neex Yàlla, moo di gëm ki mu yónni.»
30Ñu ne ko: «Ban firnde nga nu mana won, ngir nu gëm la? Ban liggéey nga nara def?
31Sunuy maam dunde nañu mànn ca màndiŋ ma, ndaxte Mbind mi nee na: “Jox na leen, ñu lekk ñam wu wàcce ca asamaan.”»
32Yeesu waxaat ne: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, du Musaa moo leen jox ñam woowu wàcce ca asamaan; sama Baay ci boppam, moo leen di jox ñam wu wóor, wi wàcce ca asamaan.
33Ndaxte ñam, wi Yàlla di joxe, mooy ñam wiy wàcce ci asamaan tey jox àddina si dund.»
34Ñu ne ko nag: «Sang bi, kon dee nu faral di jox ci ñam woowe!»
35Yeesu ne leen: «Man maay ñam wiy joxe dund. Ku ñëw ci man, doo xiif mukk; te ku ma gëm, doo mar.
36Waaye wax naa leen ko ba noppi; gis ngeen ma te taxul ngeen gëm!
37Képp ku ma Baay bi jox dina ñëw ci man, te duma dàq mukk ki may fekksi.
38Ndaxte wàccewuma ci asamaan ngir def sama bëgg-bëgg, waaye damay matal bëgg-bëggu ki ma yónni.
39Lii mooy bëgg-bëggu ki ma yónni: bu ma ñàkk kenn ci ñi mu ma may, te dafa bëgg it ma dekkal leen keroog bés bu mujj ba.
40Ndaxte lii mooy bëgg-bëggu Baay bi: képp ku gis Doom ji te gëm ko, am dund gu dul jeex, te bés bu mujj ba, dinaa ko dekkal!»