3Néeg ba ca wàllaa ñaareelu rido ba, moom lañu daan wooye bérab bu sell baa sell.
4Ca la sarxalukaayu wurus ba ñuy taal cuuraay bokkoon, gaalu kóllëre ga nekk moom doŋŋ ca biir néeg bu sell baa sell, ñu xoob ko wurus ba mu daj. Gaal ga moo yeboon njaqal wurus la defoon ñam wa ñuy wax mànn, ak yetu Aaróona wa jebbi woon, ak àlluway kóllëre ga.
5Ca kaw gaal ga la ñaari jëmmi malaakay serub nekkoon, di tegtale leeru Yàlla, seeni laaf keppaaral kubeer ga ñuy amale ag njotlaay. Waaye yooyu dunu ko mana daldi faramfàcce léegi.
6Ba ñu waajalee noonu yooyii ba mu jekk, sarxalkat yaa daan dugg saa su nekk ca néeg bu jëkk ba, di def seen liggéey.
7Waaye ñaareelu néeg ba, sarxalkat bu mag ba doŋŋ moo ca daan dugg, benn yoon cim at, te du ñàkka duggaale deret ju muy jooxe ngir boppam, ak itam ngir bàkkaar yi askan wi def te du ag teyeef.
8Noonu la Noo gu Sell gi firndeele ne yoon wu maye dugg ca bérab bu sell baa sell feeñagul woon, te fekk néeg bu jëkk ba di taxaw ba tey.
9Loolu misaal la, ñeel jamonoy tey, di firndeel ne jooxe yi ak saraxi jur yi ñu daan jébbale manuñoo dindi yaraangeg jaamukatub Yàlla bi, ba mu set wecc.
10Sarax yooyu, ci aw ñam ak ag naan, ak xeeti njàpp doŋŋ la jëm, lépp yittewoo yaramu suuxu neen, te di ndigal yu leen waroon ba keroog bésub coppite taxaw.
11Almasi nag moo dikk tey, di sarxalkat bu mag, bi yor xéewal yi teew ba noppi. Moo dugg ca biir xayma ba gëna màgg te mat sëkk, xayma bu loxol nit deful, te loolu mooy xayma ba bokkul ci càkkéefug àddina sii.
12Du deretu sikket mbaa yëkk la duggaale, waaye deretu boppam la dugge benn yoon ba fàww ca bérab bu sell baa sell, te moom la amale njotlaay gu sax dàkk.