Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Yawut ya

Yawut ya 9

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Kóllëre gu jëkk ga amoon na moom itam, ay ndigalam yu jëm ci ni ñu wara jaamoo Yàlla, ak bérabam bu sell bi fi kaw suuf.
2Xaymab jaamookaay ba ñu sàkkoon ñaari néeg la woon. Bu jëkk ba, ca la tegukaayu làmp ba nekkoon, ak taabal ja, ak mburum teewal ma. Moo doon bérab bu sell ba.
3Néeg ba ca wàllaa ñaareelu rido ba, moom lañu daan wooye bérab bu sell baa sell.
4Ca la sarxalukaayu wurus ba ñuy taal cuuraay bokkoon, gaalu kóllëre ga nekk moom doŋŋ ca biir néeg bu sell baa sell, ñu xoob ko wurus ba mu daj. Gaal ga moo yeboon njaqal wurus la defoon ñam wa ñuy wax mànn, ak yetu Aaróona wa jebbi woon, ak àlluway kóllëre ga.
5Ca kaw gaal ga la ñaari jëmmi malaakay serub nekkoon, di tegtale leeru Yàlla, seeni laaf keppaaral kubeer ga ñuy amale ag njotlaay. Waaye yooyu dunu ko mana daldi faramfàcce léegi.
6Ba ñu waajalee noonu yooyii ba mu jekk, sarxalkat yaa daan dugg saa su nekk ca néeg bu jëkk ba, di def seen liggéey.
7Waaye ñaareelu néeg ba, sarxalkat bu mag ba doŋŋ moo ca daan dugg, benn yoon cim at, te du ñàkka duggaale deret ju muy jooxe ngir boppam, ak itam ngir bàkkaar yi askan wi def te du ag teyeef.
8Noonu la Noo gu Sell gi firndeele ne yoon wu maye dugg ca bérab bu sell baa sell feeñagul woon, te fekk néeg bu jëkk ba di taxaw ba tey.
9Loolu misaal la, ñeel jamonoy tey, di firndeel ne jooxe yi ak saraxi jur yi ñu daan jébbale manuñoo dindi yaraangeg jaamukatub Yàlla bi, ba mu set wecc.
10Sarax yooyu, ci aw ñam ak ag naan, ak xeeti njàpp doŋŋ la jëm, lépp yittewoo yaramu suuxu neen, te di ndigal yu leen waroon ba keroog bésub coppite taxaw.
11Almasi nag moo dikk tey, di sarxalkat bu mag, bi yor xéewal yi teew ba noppi. Moo dugg ca biir xayma ba gëna màgg te mat sëkk, xayma bu loxol nit deful, te loolu mooy xayma ba bokkul ci càkkéefug àddina sii.
12Du deretu sikket mbaa yëkk la duggaale, waaye deretu boppam la dugge benn yoon ba fàww ca bérab bu sell baa sell, te moom la amale njotlaay gu sax dàkk.
13Ndegam deretu sikket ak yëkk, ak nag wu jigéen wu ñu lakk, ngir suy dóom ba nit ku sobewu, yooyu lees daan sellale nit ñi, ngir seen cetug yaramu suuxu neen,
14te Almasi di ki def boppam sarax bu mucc sikk ñeel Yàlla, ci dooley Noo gu Sell gi, kon nag ñaata yoon la deretu Almasi gëna mana setal sunu yaraange ji sababoo ci sunu jëf ju bon ju jëme ci ndee, ba nu mana jaamu Yàlla jiy dund!
15Looloo tax Yeesu di defarekat bi fas kóllëre gu bees, ngir ñi ñu woo mana jot ci muur gu sax dàkk gi ñu leen dig. Deeyam gi mu dee, moom la leen jote ci bàkkaar yi ñu xëtte kóllëre gu jëkk ga.
16Kayitu ndono nag fu mu teew, fàww joxees fa firndey deewug ka donale,
17ndax kayitu ndono du wér lu moy gannaaw bu nit ka deeyee. Du jàppandi mukk li feek ki donalee ngi dund.
18Looloo waral it kóllëre gu jëkk ga ci boppam, dooreesu ko woon te deret tuuruwul.

19Keroog ba Musaa biralalee bànni Israyil gépp mboolem santaane, na ko yoon wi laaje, ba mu noppee, deretu wëllu la jël, ak ju sikket, akum ndox, ak caru garabu isob bu mu laxas kawaru xar mu xonq. Mu capp ko ca deret ja, wis-wisal ca kaw téereb yoon wa, ak mbooloo mépp.
20Mu ne: «Lii mooy deretu kóllëre gi Yàlla fas ak yeen.»
21Xayma ba, ak mboolem ndabi carxal ya it, noonu la wis-wisale ca kaw.
22Ndax ci yoonu Musaa sax, deret lees di setale daanaka lépp, te bu deret tuuruwul, njéggal amul.
23Jumtukaay yooyi di ay misaali yëf ya fa asamaan, yooyu sarax lees ko waroona setale. Kon yëfi asamaan ya ci boppam, sarax yu ko gën lees ko wara setale.
24Ndax bérab yu sell yu nit tabax, te muy royaalub bérab bu dëggu ba doŋŋ, du ci la Almasi dugg. Waaye biir asamaan ci boppam la dugg ngir teewal nu tey, fa kanam Yàlla.
25Duggul biir asamaan it ngir di sarxe ak a sarxewaat boppam, noonee sarxalkat bu mag ba daan dugge at mu nekk fu sell faa sell, yóbbaale deret ju dul josam.
26Lu ko moy ca njàlbéenu àddina lay dale sonn ay yooni yoon. Waaye tey ci mujug jamono yi la feeñ benn yoon doŋŋ, ba sarxe boppam, ngir far bàkkaar.
27Kon ni ab dogal sédde nit ñi benn yoon doŋŋ bu ñuy dee, seenub àtte topp ci,
28noonu itam la Almasi doone ab sarax benn yoon, ngir gàddu bàkkaaru nit ñu bare, te dina teewsiwaat, ci yoon wu joteetul dara ak bàkkaar, ngir indil ñi koy séentu seenug mucc.