Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Yawut ya

Yawut ya 2

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Moo tax nu wara yokka teewlu kàddu yi nu dégg, bala noo lajj, taañaañal.
2Gannaaw nag kàddug Yàlla ga jibe woon ci gémmiñu malaaka yi, mujj na di lu wér péŋŋ, te képp ku ko masa xëtt, mbaa mu déggadi ko, jot nga añ bi war ci sag tooñ,
3ana kon nun ci sunu bopp, nan lanuy rëcce mbugal, su nu sàgganee pexem mucc mu réy mii Sang bi jëkkoona biral, te ñi ko dégg dëggalal nu ko?
4Te Yàlla moo doon dëggale seedey ñooñu, ay firnde aki kéemaan, ak wépp xeeti kawtéef, ak ay mayi Noo gu Sell gi, may yi mu séddalee ni mu ko soobe.
5Ndax kat du ci kilifteefu malaaka yi la Yàlla teg àddinay ëllëg ji nuy wax,
6waaye am na ku yékkatee bérab, kàddug seede, ne: «Ana luy nit ba nga di ko faale? Ana luy doom aadama, ba nga di ko yég?
7Yaa ko def mu gëna suufe as lëf malaaka yi, yaa ko kaalaa teraanga ak daraja,
8yaa teg lépp ci kilifteefam, ci suufu ndëggul tànkam.» Ba Yàlla tegee lépp ci kilifteefam it, bàyyiwul dara lu mu tegul ci kilifteefam. Dëgg la, fii nu tollu gisagunu ne lépp a ngi ci kilifteefam,
9Yeesu mi ñu def mu gëna suufe as lëf malaaka yi, moom lanu gis deeyam gi mu dee tax mu jagoo kaalag teraanga. Noonu la deeyale ñépp ci kaw yiwu Yàlla.
10Ndax kat Yàlla mi lépp lu sàkke ñeel, te lépp sàkkoo ci moom, moo nammoona wommat gone yu bare ba sédd leen daraja. Moo tax muy lu jaadu, mu sottale matug Yeesu ay coono, ndax Yeesu moo xàllal gone yooyu yoonu mucc.
11Yeesu miy sellal nit ñi, moom ak ñi muy sellal, ñoo bokk lenqe, te moo tax Yeesu rusu leena wooye ay bokk.
12Mu ne: «Maay biralal saw tur samay bokk, maa lay kañe fi digg mbooloo mi.»
13Mu waxaat ne: «Man maay am kóolute ci moom.» Dellooti ne: «Maa ngi nii, maak gone yi ma Yàlla jox.»
14Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley ndee, te mooy Seytaane.
15Noonu la goreele mboolem ñi seenug ragala dee tënkoon cig njaam, seen giiru dund.
16Ndax kat du ay malaaka la Yeesu xettlisi, waaye askanu Ibraayma la xettlisi.
17Moo tax fàww mu niru woon ay bokkam ci bépp fànn. Su ko defee mu mana doon seen sarxalkat bu mag bu am yërmande te wóor fa kanam Yàlla, ngir mana defal askan wi seen njotlaayal bakkan.
18Coonoy nattu bi mu dékku nag tax na mu mana wallu ñi ci nattu.