Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 9

Sarxalkat yi 9:10-19

Help us?
Click on verse(s) to share them!
10Aaróona jël nebbon bi jóge ci sarax biy póotum bàkkaar, aki dëmbéenam ak bàjjo bi ci res wi, mu boole ko lakk ci kaw sarxalukaay bi, muy la Aji Sax ji santoon Musaa.
11Yàpp wi ak der bi, mu génne ko dal ba, lakk ko, ba mu dib dóom.
12La ca tegu Aaróona rendi juru rendi-dóomal bi. Ba loolu amee doomam yu góor ya jox ko deret ja, mu xëpp ko ci mboolem weti sarxalukaay bi.
13Ñu jox ko saraxu rendi-dóomal bi ñu def dog yu ànd ak bopp ba, mu boole lakk ca sarxalukaay ba.
14Loolu wéy, mu raxas yérey biir yi, ak yeel yi, teg ko ca kaw saraxu rendi-dóomal ba, lakkaale ko ca.
15Gannaaw gi Aaróona indi saraxi mbooloo mi, jël sikketu mbooloo miy doon seen saraxu póotum bàkkaar, rendi ko, sarxal ko, na mu sarxale la jiitu.
16Ci kaw loolu mu indi saraxu rendi-dóomal ba, sarxal ko, na ñu ko diglee.
17Mu doora indi saraxu pepp mi, sàkk ci ab tib, lakk ko ca kaw sarxalukaay ba, dolli ko ca dóomalu suba sa.
18Mu sooga rendi nag wi ak kuuy mi, defal ko mbooloo mi saraxu cant ci biir jàmm. Doomam yu góor ya jox ko deret ja, mu xëpp ko ca mboolem weti sarxalukaay ba.
19Waaye lay nebbon ca nag wa ak kuuy ma, di calgeen ba ak nebbon bi sàng yérey biir yi, ak dëmbéen yi ak bàjjo bi ci res wi,

Read Sarxalkat yi 9Sarxalkat yi 9
Compare Sarxalkat yi 9:10-19Sarxalkat yi 9:10-19