4Su sàgganee it ba giñ ne dina def nàngam, muy lu baax mbaa lu bon, muy mboolem ngiñ lu ko rëcc te ba mu koy wax teyu ko, ba mu wees, saa yu ko xamee tooñ na.
5Ci tooñin yooyu ñu lim war naa wax na mu tooñe.
6Na indil Aji Sax ji gàtt bu jigéen, xar mbaa bëy, muy daanam ndax bàkkaar bi mu def. Saraxu póotum bàkkaar lay doon, sarxalkat bi defal ko ko njotlaayal bàkkaar bi mu def.
7«Nit ki amul lu mat njégu gàtt, na indil Aji Sax ji ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, muy daanam ndax bàkkaar bi mu def; benn bi di saraxu póotum bàkkaar, bi ci des di sarax rendi-dóomal.
8Da koy yót sarxalkat bi, kooku jëkka rey benn bi, muy saraxu póotum bàkkaar; na kutt baat bi te bumu teqale bopp beek baat bi.
9Day xëpp ci wetu sarxalukaay bi deretu njanaaw liy saraxu póotum bàkkaar. Li des ci deret ji dees koy tuur ci taatu sarxalukaay bi. Saraxu póotum bàkkaar la.