Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 24

Sarxalkat yi 24:3-7

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Ci kanam rido bi làq gaalu àlluway seede si, ci biir xaymab ndaje mi la Aaróona di teg làmp yi, muy fanaanee tàkk ba bët set, fi kanam Aji Sax ji. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan.
4Na teg làmp yi ci kaw tegukaayu làmp ba ñuy tëgge wurusu ngalam, muy fanaanee tàkk fi kanam Aji Sax ji.
5«Sàkkal sunguf su mucc ayib, lakk ci fukki mburu ak ñaar, mburu mu nekk di juróom benni kiloy sunguf.
6Tegal mburu yi ci kaw taabalu wurusu ngalam bi, fi kanam Aji Sax ji, te def ko ñaari jal, jal bu ne juróom benni mburu.
7Jal bu nekk teg ca cuuraay lu raxul, mu wuutu mburu mi, di saraxu baaxantal, te di saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.

Read Sarxalkat yi 24Sarxalkat yi 24
Compare Sarxalkat yi 24:3-7Sarxalkat yi 24:3-7