Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 24:3-7 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 24:3-7 in Kàddug Yàlla gi

3 Ci kanam rido bi làq gaalu àlluway seede si, ci biir xaymab ndaje mi la Aaróona di teg làmp yi, muy fanaanee tàkk ba bët set, fi kanam Aji Sax ji. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan.
4 Na teg làmp yi ci kaw tegukaayu làmp ba ñuy tëgge wurusu ngalam, muy fanaanee tàkk fi kanam Aji Sax ji.
5 «Sàkkal sunguf su mucc ayib, lakk ci fukki mburu ak ñaar, mburu mu nekk di juróom benni kiloy sunguf.
6 Tegal mburu yi ci kaw taabalu wurusu ngalam bi, fi kanam Aji Sax ji, te def ko ñaari jal, jal bu ne juróom benni mburu.
7 Jal bu nekk teg ca cuuraay lu raxul, mu wuutu mburu mi, di saraxu baaxantal, te di saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.
Sarxalkat yi 24 in Kàddug Yàlla gi