11Waaye su sarxalkat bi jëndee ab jaam ci xaalisam, jaam ba man na caa lekk. Jaam bu juddoo ci kër sarxalkat bi it man naa lekk ci ñamam woowu.
12Doomu sarxalkat, bu séyeek góor gu bokkul ci waa kër sarxalkat yi, jooxe yu sell yi, dootu ci saña lekk.
13Waaye doomu sarxalkat bu boroom këram faatoo mbaa mu tàggook moom te amu ca doom, bu delloo kër baayam na mu fa nekke woon ba muy gone, sañ naa lekk ci ñamu baayam. Waaye kenn ku ci bokkul sañu cee lekk.
14Gannaaw loolu képp ku bokkul ci waa kër sarxalkat yi, bu lekkee ci sarax su sell te du teyeefam, na dolli ca njégu sarax sa juróomeelu céru njég ga, delloo ko sarxalkat bi.
15Te itam bu sarxalkat yi bàyyi bànni Israyil di teddadil sarax yu sell yi ñu jagleel Aji Sax ji.
16Buñu leen di bàyyi it ñuy gàddu bàkkaar buy laaj peyug tooñ, ngir lenn lu ñu lekk ci sarax yu sell yooyu. Man Aji Sax ji maa sellal yooyu sarax.»