Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 16

Sarxalkat yi 16:13-33

Help us?
Click on verse(s) to share them!
13Na def cuuraay li ci taal bi, foofa ca kanam Aji Sax ji, saxaru cuuraay si di làq kubeeru saraxu njotlaay gi ub gaalu àlluway seede si, ndax mu baña dee.
14Na sàkk ci deretu yëkk wi, wis-wisale ko baaraamam ci kaw kubeeru gaal gi, ci wetam gi féete penku, te it na wis-wisale baaraamam deret ji lu mat juróom ñaari yoon ci kanam kubeeru gaal gi.
15Bu noppee na rendi sikket biy saraxas póotum bàkkaaru mbooloo mi, te yóbbu deret ji ca gannaaw rido ba. Na def deret ji na mu defoon ak deretu yëkk wa, wis-wisal ko ca kaw kubeeru gaal gi ak ci kanam kubeer gi.
16Mu daldi matale loolu njotlaayal bérab bu sell bee sell, tàggale kook sobey bànni Israyil ak seeni tooñ, ak lu seen bàkkaar mana doon. Noonu lay defal mboolem xaymab ndaje, mi dëkk ci seen biir ci seen biiri sobe.
17Du kenn ku saña nekk ci biir xaymab ndaje mi, bu Aaróona duggee ci biir bérab bu sell bee sell, di matal ag njotlaay, ba keroog muy génn, gannaaw bu jotoo moom ci boppam, mook waa këram, ba jotaale mbooloom bànni Israyil mépp.
18«Bu sottalee, na génn jëm ca sarxalukaay ba ca kanam Aji Sax ji, ba noppi defal sarxalukaay bi njotlaayal boppam. Day sàkk ci deretu yëkk wi ak ju sikket bi, taqal béjjéni sarxalukaay bi yépp.
19Te itam day wis-wisale baaraamam deret ji lu mat juróom ñaari yoon ci kaw sarxalukaay bi, setal ko, sellal ko, mu tàggook sobey bànni Israyil.
20«Bu Aaróona matalee njotlaayal bérab bu sell bee sell ak xaymab ndaje ma ak sarxalukaay ba, na indi sikket biy dund.
21Aaróona day teg ay loxoom ci kaw boppu sikket biy dund te tudd ci kawam mboolem ñaawtéefi bànni Israyil ak seeni tooñ, ak seeni bàkkaar yépp, boole ko yen sikket bi, teg ko ci loxol nit ku ñu yónni, mu dàq ko ca màndiŋ ma.
22Sikket bi day yenu seeni ñaawtéef yépp, yóbbaale ca ndànd-foyfoy ga, ñu wacc ko ca màndiŋ ma.
23«Na Aaróona dellu ca xaymab ndaje ma, summi yére ya ñu ràbbe wëñ gu ëccu ba sew, di ya mu soloon bala moo dugg ca bérab bu sell baa sell, te na fa wacc yére ya.
24Bu loolu weesee mu sangoo fu sell, sol yérey boppam, génn, joxeel boppam ab saraxu rendi-dóomal, joxeel mbooloo mi seen saraxu rendi-dóomal ngir njotlaayal boppam ak njotlaayal mbooloo mi.
25Nebbonu jur giy saraxu póotum bàkkaar, na ko lakk ci kaw sarxalukaay bi.
26«Ka wacci woon sikketu Asasel, na fóot ay yéreem, sangu, doora mana duggaat ci dal bi.
27Muy yëkk wiy saraxu póotum bàkkaar, muy sikket biy saraxu póotum bàkkaar te ñu yóbbu woon seen deret ca biir bérab bu sell baa sell ngir defe ko njotlaay, lépp lañuy génne dal bi. Der yaak yàpp waak sébbriit ma dees koy boole lakk, ba mu dib dóom.
28Ki ko lakk bu noppee, na fóot ay yéreem, sangu, doora mana duggaat ci dal bi.
29«Te itam dogal a ngii, di lu leen war fàww. Bésub fukki fan ci juróom ñaareelu weeru at mi nangeen ci toroxlu te du lenn lu ngeen ci mana liggéey, du njuddu-ji-réew du doxandéem bi ci seen biir;
30ndaxte ci bés boobu lañu leen di joxeel njotlaay ngir fóot seen mboolem bàkkaar, ba ngeen set fi kanam Aji Sax ji.
31Na doon seen bés bu ngeen di nopplu doŋŋ, ngeen war cee toroxlu. Dogal la bu sax dàkk.
32«Sarxalkat bi ñu fal nag, solal ko, jox ko sañ-sañu sarxalkat bu mag, mu wuutu baayam, na def saraxu njotlaay gi. Na sol yére yu sell yooyu di yi ñu ràbbe wëñ gu ëccu ba sew,
33te it na def njotlaayal bérab bu sell bee sell ak xaymab ndaje mi ak sarxalukaay bi, boole ci defal sarxalkat yi seen njotlaay, ñook mbooloom Israyil mépp.

Read Sarxalkat yi 16Sarxalkat yi 16
Compare Sarxalkat yi 16:13-33Sarxalkat yi 16:13-33