Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 13

Sarxalkat yi 13:2-19

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2«Su nit amee ab tërgën ci yaramam mbaa ab ër, mbaa ab gàkk bu weex bu mana doon jàngoroy der juy law ci yaramam, nañu ko yóbbu ci Aaróona sarxalkat bi mbaa kenn ciy doomam yu góor yiy sarxalkat yi.
3Na sarxalkat bi seet gàkk bi ci yaramu nit ki; su fekkee ne kawar gi ci gàkk bi dafa soppiku weex, te mu mel ni lu def pax ci der bi, jàngoroy der juy law la. Bu sarxalkat bi gisee loolu, na biral ne nit ki sobewu na.
4Waaye su dee ab gàkk bu weex ci yaram wi te melul ni lu def pax ci der bi, taxul itam kawar gi ci nekk soppiku weex, na sarxalkat bi ber nit ki ame gàkk bi diiru juróom ñaari fan.
5Na ko sarxalkat bi xoolaat bésub juróom ñaareel ba. Bu sarxalkat bi seetloo ne gàkk bi soppikuwul mbaa mu law ci yaramam, na ko beraat juróom ñaari fan.
6Na ko sarxalkat bi xoolaat ca bésub juróom ñaareel ba. Su fekkee gàkk bi di raaf te lawul ci kaw deru yaram wi, na sarxalkat bi biral ne nit ki set na; ab ër doŋŋ la. Day fóot ay yéreem rekk daldi set.
7Su fekkee ne wóor na ne ër bi law na ci deru yaramu nit ki, gannaaw ba mu ko wonee sarxalkat bi, ba mu biral ne set na, day dellu ca sarxalkat ba.
8Su boobaa na ko sarxalkat bi xoolaat ba gis ër bi law ci deru yaram wi, mu doora biral ne nit ki sobewu na te jàngoroy der juy law la.
9«Képp ku ame jàngoroy der juy law, nañu ko yóbbu ca sarxalkat ba.
10Na ko sarxalkat bi seet. Su dee ab tërgën bu weex te kawar gi ci nekk soppiku weex, boole ci def góom ca biir,
11kon jàngoroy der juy law la te xas naa law ci yaram wi. Na sarxalkat bi biral ne nit ki sobewu na. Du jar mu di ko ber ndax taq na sobe ba noppi.
12Su fekkee ne nag jàngoro ji génn naa génn ci yaramu nit ki, sarxalkat bi gis ko fépp, li ko dale ci bopp bi ba ci tànk yi,
13na ko sarxalkat bi seet bu baax. Bu gisee ne li génn ci yaramam daj na yaram wi yépp, na biral ne nit ki mu dal set na; gannaaw léppam a soppiku weex, set na.
14Ba tey bés bu ay góom génnaatee ci yaram wi, nit ki sobewu na.
15Su sarxalkat bi gisee yaramu nit ki def góom rekk, na biral ne sobewu na. Góom boobu génn ci yaram wi sobe la. Jàngoroy der juy law la.
16Te it bu góom bi soppikoo weex, na dem ca sarxalkat ba.
17Na ko sarxalkat bi seet, ba gis ne weexaat na, mu biral ne ki jàngoro ji dal set na te kon it set na.
18«Su nit taabee ba wér,
19ab tërgën bu weex mbaa gàkk bu weex bu rax xonq feeñ fa taab ba nekkoon, na dem ca sarxalkat ba.

Read Sarxalkat yi 13Sarxalkat yi 13
Compare Sarxalkat yi 13:2-19Sarxalkat yi 13:2-19