Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 11

Sarxalkat yi 11:43-47

Help us?
Click on verse(s) to share them!
43Buleen araamal seen bopp ci lenn ci yu sew-sewaan yooyu; buleen ci taq, di ci sobeel seen bopp,
44ndaxte man Aji Sax ji maay seen Yàlla. Kon nag sell-luleen te sell ndax man ku Sell laa. Kon buleen sobeel mukk seen bopp ci mboolem bindeef yu sew-sewaan yiy dox ci suuf.
45Ndaxte kat man Aji Sax ji maay ki leen génne woon réewum Misra, di seen Yàlla. Sell-leen boog, ndax man ku Sell laa.»
46Loolu la yoon digle ci wàllu mala ak njanaaw ak bindeef yi nekk ci ndox, ak mboolem bindeef yu sew-sewaan yiy dox ne ñàpp ci suuf.
47Dina taxa ràññatle lu set ak lu setul. Dina taxa ràññatle boroom bakkan yi dagana lekk ñook boroom bakkan yi daganula lekk.

Read Sarxalkat yi 11Sarxalkat yi 11
Compare Sarxalkat yi 11:43-47Sarxalkat yi 11:43-47