Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 11:43-47 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 11:43-47 in Kàddug Yàlla gi

43 Buleen araamal seen bopp ci lenn ci yu sew-sewaan yooyu; buleen ci taq, di ci sobeel seen bopp,
44 ndaxte man Aji Sax ji maay seen Yàlla. Kon nag sell-luleen te sell ndax man ku Sell laa. Kon buleen sobeel mukk seen bopp ci mboolem bindeef yu sew-sewaan yiy dox ci suuf.
45 Ndaxte kat man Aji Sax ji maay ki leen génne woon réewum Misra, di seen Yàlla. Sell-leen boog, ndax man ku Sell laa.»
46 Loolu la yoon digle ci wàllu mala ak njanaaw ak bindeef yi nekk ci ndox, ak mboolem bindeef yu sew-sewaan yiy dox ne ñàpp ci suuf.
47 Dina taxa ràññatle lu set ak lu setul. Dina taxa ràññatle boroom bakkan yi dagana lekk ñook boroom bakkan yi daganula lekk.
Sarxalkat yi 11 in Kàddug Yàlla gi