Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Ngën-gi-woy - Ngën-gi-woy 6

Ngën-gi-woy 6:4-9

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4Xarit, taaru nga ni Tirsa ak Yerusalem, péeyi buur ya, yéeme nga ni péey yu kawe ya!
5Wuy, geesul fee! Soo ma nee jàkk, ma jànnaxe. Sa njañ liy loy-loyee ngi saf géttu bëy yu ñuul, yu bartaloo kaw tundu Galàdd.
6Sa gëñ yi ni mbote yu weex, yéege ca sangukaay ba, ku nekk ak seexam, kenn wéetu ca.
7Sa lex yiy tàkk ni ŋaali gërënaat, làqoo sa muuraay bi.
8Buur day am juróom benn fukki lingeer ak juróom ñett fukki jongama ak jeeg ju dul jeex.
9Waaye sama nenne kenn la, matal ma sëkk, yaayam kennal ko, muy ngëneelu biiru yaayam. Janq ji gis ko, di ko jëwe mbégteem, lingeeri buur aki jongamaam di ko kañ.

Read Ngën-gi-woy 6Ngën-gi-woy 6
Compare Ngën-gi-woy 6:4-9Ngën-gi-woy 6:4-9