4Xarit, taaru nga ni Tirsa ak Yerusalem, péeyi buur ya, yéeme nga ni péey yu kawe ya!
5Wuy, geesul fee! Soo ma nee jàkk, ma jànnaxe. Sa njañ liy loy-loyee ngi saf géttu bëy yu ñuul, yu bartaloo kaw tundu Galàdd.
6Sa gëñ yi ni mbote yu weex, yéege ca sangukaay ba, ku nekk ak seexam, kenn wéetu ca.
7Sa lex yiy tàkk ni ŋaali gërënaat, làqoo sa muuraay bi.
8Buur day am juróom benn fukki lingeer ak juróom ñett fukki jongama ak jeeg ju dul jeex.