Text copied!
Bibles in Wolof

Ngën-gi-woy 6:4-8 in Wolof

Help us?

Ngën-gi-woy 6:4-8 in Kàddug Yàlla gi

4 Xarit, taaru nga ni Tirsa ak Yerusalem, péeyi buur ya, yéeme nga ni péey yu kawe ya!
5 Wuy, geesul fee! Soo ma nee jàkk, ma jànnaxe. Sa njañ liy loy-loyee ngi saf géttu bëy yu ñuul, yu bartaloo kaw tundu Galàdd.
6 Sa gëñ yi ni mbote yu weex, yéege ca sangukaay ba, ku nekk ak seexam, kenn wéetu ca.
7 Sa lex yiy tàkk ni ŋaali gërënaat, làqoo sa muuraay bi.
8 Buur day am juróom benn fukki lingeer ak juróom ñett fukki jongama ak jeeg ju dul jeex.
Ngën-gi-woy 6 in Kàddug Yàlla gi