7Mu waare ne: «Am na kuy ñëw sama gannaaw koo xam ne kii moo ma ëpp kàttan; yeyoowuma sax sëgg, ngir tekki ay dàllam.
8Maa ngi leen di sóob ci ndox, waaye moom dina leen sóob ci Xel mu Sell mi.»
9Booba Yeesu jóge na dëkku Nasaret ci diiwaanu Galile, ñëw, Yaxya sóob ko ci dexu Yurdan.
10Bi muy génn ndox mi, mu daldi gis asamaan xar, te Xelum Yàlla di wàcc ci melow pitax, ñëw ci moom.
11Te baat bu jóge asamaan jib ne: «Yaa di sama Doom, ji ma bëgg; ci yaw laa ame bànneex.»
12Ci kaw loolu Xelum Yàlla daldi jéñ Yeesu, mu dem ca màndiŋ ma.
13Mu nekk fa ñeent fukki fan, jànkoonte ak fiiri Seytaane; mu dëkk ci biir rabi àll yi, te malaakay Yàlla di ko topptoo.
14Bi nga xamee ne jàpp nañu Yaxya, Yeesu dem ca diiwaanu Galile, di waare xibaaru jàmm bu Yàlla bi,
15naan: «Jamono ji mat na, nguuru Yàlla jegesi na; tuubleen seeni bàkkaar te gëm xibaaru jàmm bi.»
16Am bés Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa ñaar ñu bokk ndey ak baay, di Simoŋ ak Andare rakkam, ñuy sànni seeni mbaal ci dex gi, ndaxte ay nappkat lañu woon.
17Yeesu ne leen: «Ñëwleen topp ci man, dinaa leen def nappkati nit.»