Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 2

Màndiŋ ma 2:3-25

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3«Ñay dale ca kanam, fa féete penku, ñooy waa raayab Yuda ak seeni gàngoor, kilifag Yudeen ñi di Nason doomu Aminadab.
4Ña ñu lim ci gàngooram di juróom ñaar fukki junneek ñeent ak juróom benni téeméer (74 600).
5«Ñay dale fa feggook ñoom ñooy giirug Isakareen ñi, kilifag askanu Isaakar di Netanel doomu Suwar.
6Ña ñu lim ci gàngooram di juróom fukki junneek ñeent ak ñeenti téeméer (54 400).
7«Giirug Sabuloneen ñeey feggook ñoom, kilifag askanu Sabulon di Elyab doomu Elon.
8Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek juróom ñaar ak ñeenti téeméer (57 400).
9«Mboolem ña ñu limal dalub Yuda aki gàngooram daldi doon téeméeri junneek juróom ñett fukk ak juróom benn ak ñeenti téeméer (186 400). Bu ñuy dem, ñooñooy dox, jiitu.
10«Waa raayab Ruben ñooy dale bëj-saalum, ñook seeni gàngoor, kilifag askanu Ruben di Elisur doomu Sedeyur.
11Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek juróom benn ak juróomi téeméer (46 500).
12«Ñay dale fa feggook ñoom ñooy giirug Cimyoneen ñi, kilifag askanu Simeyon di Selumyel doomu Surisadaay.
13Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek juróom ñeent ak ñetti téeméer (59 300).
14«Giiru Gàddeen ñeey feggook ñoom, kilifag askanu Gàdd di Elyasaf doomu Rewel.
15Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer ak juróom fukk (45 650).
16«Mboolem ña ñu limal dalub Ruben aki gàngooram doon téeméeri junneek juróom fukk ak benn, ak ñeenti téeméer ak juróom fukk (151 450). Bu ñuy dem, ñooñooy doon ñaareelu kurél, dox, topp ca.
17«Su ko defee xaymab ndaje mi jóg topp ca, ànd ak Leween ñi koy gàddu, te seen dal nekk ci digg dal yi. Noonee kurél yiy dale daal, ni lañuy jóge dem, ku nekk topp ayam ak raayaam.
18«Waa raayab Efrayim ñooy dale wetu sowu, ñook seeni gàngoor, kilifag askanu Efrayim di Elisama doomu Amiyut.
19Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junni ak juróomi téeméer (40 500).
20«Ñay dale fa feggook ñoom ñooy giirug Manaseen ñi, kilifag askanu Manase di Gamalyel doomu Pedasur.
21Ña ñu limal gàngooram di fanweeri junneek ñaar ak ñaar téeméer (32 200).
22«Giirug Beñamineen ñeey feggook ñoom, kilifag askanu Beñamin di Abidan doomu Gidoni.
23Ña ñu limal gàngooram di fanweeri junneek juróom ak ñeenti téeméer (35 400).
24«Mboolem ña ñu limal dalub Efrayim aki gàngooram daldi doon téeméeri junneek juróom ñett ak téeméer (108 100). Bu ñuy dem, ñooñoo di ñetteelu kurél, dox topp ca.
25«Waa raayab Dan ñooy dale bëj-gànnaar, ñook seeni gàngoor, kilifag askanu Dan di Ayeser doomu Amisadaay.

Read Màndiŋ ma 2Màndiŋ ma 2
Compare Màndiŋ ma 2:3-25Màndiŋ ma 2:3-25