Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 24

Màndiŋ ma 24:15-22

Help us?
Click on verse(s) to share them!
15Ci kaw loolu mu yékkati kàddug ñaanam, ne: «Kàddug Balaam a ngi, doomu Bewor, kàddug waa jiy boroom ngis,
16kàddug kiy dégg waxi Yàlla, kiy xame ca xam-xamu Aji Kawe ji, Aji Man ji wonem peeñu, mu gis, kiy daanu leer, te ay gëtam muriku.
17Maa ngi koy gis, te du tey, Maa ngi koy niir, te jubseegul; biddiiw a feqe fa Yanqóoba, yetu nguur a yékkatikoo fa Israyil, daldi toj boppi Mowab, toj kaaŋi mboolem askanu Set.
18Edom, mu moom; Seyir, noonam, muy boroom; Israyil def jaloore.
19Fa Yanqóoba la buur di bawoo, dem ñéddi ndesu dëkk ba.»
20Ci kaw loolu Balaam geesu réewum Amaleg, dellu yékki kàddug ñaanam, ne: «Amaleg moo sutu xeet, te sànku lay mujje.»
21Mu teg ca geesu réewum Keneen ña, yékkeeti kàddug ñaanam, ne: «Keneen ñee wér ab dëkkuwaay, seenub tàgg a làqoo biir doj.
22Waaye réewum Keneen gépp ay xoyomu, ba leen Asur di yóbbuji njaam.»

Read Màndiŋ ma 24Màndiŋ ma 24
Compare Màndiŋ ma 24:15-22Màndiŋ ma 24:15-22