Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 16

Màndiŋ ma 16:1-6

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ku ñuy wax Kore doomu Isar, mi askanoo ci Keyat doomu Lewi, moo àndoon ak ay Rubeneen, ñuy Datan ak Abiram, doomi Elyab, ak Onn doomu Pelet,
2ñu jógal Musaa, ñook ñaar téeméer ak juróom fukk (250) ci bànni Israyil, diy kilifa ci mbooloo mi, am baat ca pénc ma, te di ñu amu tur.
3Ci kaw loolu ñu bokk daje fi kaw Musaa ak Aaróona, ne leen: «Doy na sëkk! Mbooloo mi ba mu daj, ñépp a sell, te ci sunu biir la Aji Sax ji nekk. Ana lu ngeen di xoggliku ci kaw mbooloom Aji Sax ji?»
4Ba Musaa déggee loolu, da ne gurub, dëpp jë bi fi suuf.
5Mu wax Kore ak gàngooram gépp, ne: «Bu ëllëgee, Aji Sax ji mooy xamle kan la séddoo ak kan mooy ki sell, mu jegeñal ko boppam. Ki mu taamu nag, dina ko jegeñal boppam.
6Dangeen di def nii: jël-leeni and, yaw Kore, yaak sa gàngoor gépp,

Read Màndiŋ ma 16Màndiŋ ma 16
Compare Màndiŋ ma 16:1-6Màndiŋ ma 16:1-6