Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 16:1-6 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 16:1-6 in Kàddug Yàlla gi

1 Ku ñuy wax Kore doomu Isar, mi askanoo ci Keyat doomu Lewi, moo àndoon ak ay Rubeneen, ñuy Datan ak Abiram, doomi Elyab, ak Onn doomu Pelet,
2 ñu jógal Musaa, ñook ñaar téeméer ak juróom fukk (250) ci bànni Israyil, diy kilifa ci mbooloo mi, am baat ca pénc ma, te di ñu amu tur.
3 Ci kaw loolu ñu bokk daje fi kaw Musaa ak Aaróona, ne leen: «Doy na sëkk! Mbooloo mi ba mu daj, ñépp a sell, te ci sunu biir la Aji Sax ji nekk. Ana lu ngeen di xoggliku ci kaw mbooloom Aji Sax ji?»
4 Ba Musaa déggee loolu, da ne gurub, dëpp jë bi fi suuf.
5 Mu wax Kore ak gàngooram gépp, ne: «Bu ëllëgee, Aji Sax ji mooy xamle kan la séddoo ak kan mooy ki sell, mu jegeñal ko boppam. Ki mu taamu nag, dina ko jegeñal boppam.
6 Dangeen di def nii: jël-leeni and, yaw Kore, yaak sa gàngoor gépp,
Màndiŋ ma 16 in Kàddug Yàlla gi