19Yaayu Yeesu ak ay rakkam ñoo dikkoon di seet Yeesu te manuñoo agsi ci moom ndax nit ñu bare.
20Ñu ne ko: «Sa yaay ak say rakk a ngi taxaw ci biti, bëgg laa gis.»
21Mu ne leen: «Sama yaay ak samay rakk, ñoo di ñiy dégg kàddug Yàlla, te di ko jëfe.»
22Benn bés la Yeesu duggoon gaal, mook ay taalibeem. Mu ne leen: «Nanu jàll ca wàllaa dex gi.» Ñu daldi dem.