12Ñi féeteek yoon wi mooy ñi dégg. Seytaane nag mooy dikk, foqati kàddu gi ci seen xol, ngir ñu baña gëm ba mucc.
13Ñi féete fu bare ay doj, ñoo dégg kàddu gi, nangoo ko xol bu sedd. Waaye ñooñu, ab reen lañu amul. Ab diir rekk lañuy gëm, bu janti nattu dikkee, ñu dellu gannaaw.
14Li wadde ci ay xaaxaam mooy ñi dégg kàddu gi, te ay xalaat ak alal, ak bànneexu bakkan fatt leen, ba tax meññaluñu lu ñor.
15Li ci suuf su baax si nag, mooy ñi dégge kàddu gi xol bu dëggu te rafet, ŋoy ca, te saxoo muñ ba meññal.
16«Deesul taal ab làmp, dëppe ko ndab, mbaa nga dugal ko ci ron lal. Dees koy aj kay ba kuy duggsi, di gis leer gi.
17Mboolem lu làqu dina feeñ, te mboolem lu nëbbu dina siiw ba ne fàŋŋ.
18Kon nag teewluleen ni ngeen di dégge. Ku am, dees na ko dolli, waaye ku amul, la mu xalaatoon ne am na ko sax, dees na ko nangu.»
19Yaayu Yeesu ak ay rakkam ñoo dikkoon di seet Yeesu te manuñoo agsi ci moom ndax nit ñu bare.