12 Ki féete ci yoon wi mooy ki dégg. Gannaaw gi, Seytaane dafay ñëw, këf kàddu, gi ñu def ci xolam, ngir mu baña gëm te Yàlla musal ko.
13 Ki nekk ci bérab bu bare ay doj, mooy ki dégg kàddu gi, ba noppi nangu ko ak mbég. Waaye wax ji saxul ci moom. Dina gëm ab diir, waaye bu nattu yi agsee, mu daldi dàggeeku.
14 Ki jot ci jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dégg kàddu gi, waaye nees-tuut soxla yi ak alal ak bànneexi àddina tanc ko, ba du àgg cig mat.
15 Ki jot ci jiwu wi ci suuf su baax si nag, mooy ki dégg kàddu gi te denc ko ci xol bu baax bu gore, te muñ ba jur njariñ.
16 «Kenn du taal làmp, dëpp ci leget, walla mu di ko def ci ron lal. Daf koy wékk, ngir mu leeral ñiy dugg.
17 Amul dara luy kumpa lu ñu dul siiwal bés, walla lu làqu lu ñu dul feeñal, ba mu ne fàŋŋ.
18 Seetleen bu baax, ni ngeen di dégloo kàddu gi. Ku am, dees na la dollil, waaye ku amul, dees na nangu sax li nga xalaatoon ne am nga ko ba noppi.»
19 Noonu ndeyu Yeesu ak ay rakkam ñëw seetsi ko, waaye manuñu woona agsi ci moom, ndaxte nit ña dañoo bare.