Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 18

Luug 18:28-43

Help us?
Click on verse(s) to share them!
28Piyeer daldi ne: «Nun de, noo ngii, dëddu la nu amoon, topp la.»
29Yeesu ne leen: «Maa leen ko wax déy, amul kenn kuy dëddu kër, mbaa jabar, mbaa mbokk, mbaa waajur, mbaa doom, ngir nguurug Yàlla,
30te jotaatul lu ko ëpp ay yooni yoon, tey jii, akug texe ba fàww, ëllëg.»
31Yeesu nag yóbbu Fukk ñaak ñaar, wéetook ñoom, ne leen: «Nu ngii jëm Yerusalem, te mboolem lu yonent yi bindoon ci mbirum Doomu nit ki dina sotti.
32Ndax dees na ko jébbal jaambur ñi dul Yawut, dees na ko ñaawal, saaga ko, tifli ko.
33Dinañu ko caw, rey ko, ba ca ñetteelu fanam, mu dekki.»
34Waaye ndaw ya, ñoom, xamuñu dara ci jooju wax, ndax mbóotu kàddug Yeesu gaa leen làqu, ba tax ñu umple la mu wax.
35Ba Yeesu di jubsi dëkk ba ñuy wax Yeriko, ab silmaxaa nga tooge ca peggu yoon wa, di yalwaan.
36Silmaxa ba dégg mbooloo may romb, mu daldi laaj lu mu doon.
37Ñu ne ko Yeesum Nasaret moo fa jaare.
38Ci kaw loolu mu àddu ca kaw ne: «Yeesu, Sëtub Daawuda, yërëm ma!»
39Ña jiitu femmu ko, ngir mu noppi. Teewul mu gëna xaacooti, ne: «Sëtub Daawuda, yërëm ma!»
40Yeesu nag taxaw, ne ñu indil ko ko. Ba mu dikkee, mu laaj ko, ne ko:
41«Loo bëgg ma defal la ko?» Mu ne ko: «Xanaa may gis, Sang bi.»
42Yeesu ne ko: «Gisal! Sa ngëm faj na la.»
43Ca saa sa muy gis, daldi topp ci Yeesu, di sàbbaal Yàlla. Mbooloo mépp gis loolu, di sant Yàlla.

Read Luug 18Luug 18
Compare Luug 18:28-43Luug 18:28-43