19«Dafa amoon boroom alal juy sol yére yu rafet te jafe, tey dund bés bu set dund gu neex.
20Fekk miskin mu ñuy wax Lasaar daan tëdd ca buntu këram, fees dell ak ay góom,
21te bu sañoon, di lekk ci desiti ñam wiy rot ci lekkukaayu boroom alal ji. Xaj yi sax daan nañu ñëw, di mar ay góomam.
22«Noonu miskin ma dee, malaaka yi yóbbu ko ca wetu Ibraayma. Boroom alal ja itam dee, ñu suul ko.
23Bi ñu koy mbugal ca sawara, mu téen, séen fu sore Ibraayma ak Lasaar ci wetam.