Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 11

LUUG 11:7-13

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7«Waaye kooku nekk ci biir néegam, dina ko ne: “Bu ma lakkal, tëj naa bunt bi ba noppi te tëdd naa maak sama njaboot; manumaa jóg di la jox dara.”
8Maa ngi leen koy wax, su jógul jox ko li muy laaj ndax li ñu xaritoo it, ndax la kee ñàkk jom dina tax mu jox ko lépp li mu soxla.
9Moo tax ma ne, ñaanleen, ñu may leen; seetleen, te dingeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen.
10Ndaxte képp kuy ñaan, dinga am; kuy seet, dinga gis; kuy fëgg, ñu ubbil la.
11Bu la sa doom ñaanee jën, yaw miy baayam, ndax dinga ko baña jox jën, jox ko jaan?
12Walla mu ñaan la nen, nga jox ko jiit?
13Ndegam yéen ñi bon yéena mana jox seeni gone lu baax, astamaak Baay bi nekk ci kaw dina jox Xel mu Sell mi ñi ko koy ñaan!»

Read LUUG 11LUUG 11
Compare LUUG 11:7-13LUUG 11:7-13