21Ca waxtu woowa tembe la kemtalaayu mbégte tukkee ci Noo gu Sell gi, dugg Yeesu, mu daldi ne: «Baay, Boroom asamaan ak suuf, sant naa la, nde yaa làq lii boroom xam-xam yeek boroom xel yi, xamal ko tuut-tànk yi, nde loolu de, Baay, mooy li la soob.
22Lépp la ma sama Baay dénk, te kenn xamul kuy Doom ji, ku dul Baay bi; kenn it xamul kuy Baay bi, ku dul Doom ji, ak képp ku ko Doom ji namma xamal.»
23Ci kaw loolu Yeesu walbatiku ca taalibe ya, wax leen ñoomu neen, ne leen: «Ndokklee ñi seeni gët gis li ngeen gis.
24Ndax maa leen ko wax, bare na ay yonent ak buur yu bëggoona gis li ngeen gis, te gisuñu ko, ak itam dégg li ngeen dégg, te dégguñu ko.»
25Benn xamkatu yoonu Musaa moo jekki woon jóg, di fexee fiir Yeesu. Mu ne ko: «Sëriñ bi, ana lu may def, ba texe ba fàww?»
26Yeesu ne ko: «Yoonu Musaa, ana lees ci bind? Loo ci jànge?»
27Mu ne ko: «Boroom bi sa Yàlla, nanga ko soppe sa léppi xol ak sa léppi bakkan ak sa léppi doole ak sa léppi xel, te ni nga soppe sa bopp, nanga ko soppe sa moroom.»
28Yeesu nag ne ko: «Wax nga dëgg. Noonu ngay def, daldi texe.»