Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 10:21-28 in Wolof

Help us?

LUUG 10:21-28 in Téereb Injiil

21 Ca saa soosu Xel mu Sell mi feesal Yeesu ak mbég, mu daldi ne: «Yaw Baay, Boroom asamaan ak suuf, maa ngi lay sant ci li nga nëbb yëf yii ñi am xam-xam ak ñi am xel, te xamal leen gone yi. Waaw, Baay, ndaxte looloo la neex.»
22 Yeesu teg ca ne: «Sama Baay jébbal na ma lépp, te kenn manula xam, man Doom ji, maay kan, ku dul Baay bi; kenn manula xam it kan mooy Baay bi, ku dul man Doom ji, ak ku ma ko bëgga xamal.»
23 Gannaaw bi mu waxee loolu, Yeesu walbatiku ca taalibe ya ne leen ñoom rekk: «Ñi seeni bët di gis li ngeen di gis, am nañu mbég.
24 Ndaxte maa ngi leen koy wax, yonent yu bare ak buur yu bare bëggoon nañoo gis li ngeen di gis, waaye gisuñu ko, te dégg li ngeen di dégg, waaye dégguñu ko.»
25 Noonu benn xutbakat daldi jóg, ngir fexee fiir Yeesu ne ko: «Kilifa gi, lan laa wara def, ba am dund gu dul jeex?»
26 Yeesu ne ko: «Lu ñu bind ci yoonu Musaa? Lan nga ciy jàng?»
27 Nit ka ne ko: «“Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp, sa kàttan gépp ak sa xel mépp,” te it: “Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.”»
28 Yeesu ne ko nag: «Li nga wax dëgg la. Boo defee loolu, dinga dund ba fàww.»
LUUG 10 in Téereb Injiil

Luug 10:21-28 in Kàddug Yàlla gi

21 Ca waxtu woowa tembe la kemtalaayu mbégte tukkee ci Noo gu Sell gi, dugg Yeesu, mu daldi ne: «Baay, Boroom asamaan ak suuf, sant naa la, nde yaa làq lii boroom xam-xam yeek boroom xel yi, xamal ko tuut-tànk yi, nde loolu de, Baay, mooy li la soob.
22 Lépp la ma sama Baay dénk, te kenn xamul kuy Doom ji, ku dul Baay bi; kenn it xamul kuy Baay bi, ku dul Doom ji, ak képp ku ko Doom ji namma xamal.»
23 Ci kaw loolu Yeesu walbatiku ca taalibe ya, wax leen ñoomu neen, ne leen: «Ndokklee ñi seeni gët gis li ngeen gis.
24 Ndax maa leen ko wax, bare na ay yonent ak buur yu bëggoona gis li ngeen gis, te gisuñu ko, ak itam dégg li ngeen dégg, te dégguñu ko.»
25 Benn xamkatu yoonu Musaa moo jekki woon jóg, di fexee fiir Yeesu. Mu ne ko: «Sëriñ bi, ana lu may def, ba texe ba fàww?»
26 Yeesu ne ko: «Yoonu Musaa, ana lees ci bind? Loo ci jànge?»
27 Mu ne ko: «Boroom bi sa Yàlla, nanga ko soppe sa léppi xol ak sa léppi bakkan ak sa léppi doole ak sa léppi xel, te ni nga soppe sa bopp, nanga ko soppe sa moroom.»
28 Yeesu nag ne ko: «Wax nga dëgg. Noonu ngay def, daldi texe.»
Luug 10 in Kàddug Yàlla gi