Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 6

JËF YA 6:5-11

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Lii ñu wax nag neex na mbooloo mépp. Noonu ñu tànn Ecen, di nit ku fees ak ngëm ak Xel mu Sell mi, boole ci Filib ak Porokor, teg ca Nikanor, Timon, Parmenas ak Nikolas, mi juddoo Ancos te tuub ci yoonu Yawut ya.
6Ñu jébbal leen ndaw ya, ñaanal leen, teg leen loxo.
7Noonu kàddug Yàlla di law, ba mbooloom taalibe yi di yokku bu bare ci Yerusalem; te sarxalkat yu bare déggal Yàlla ci topp yoonu ngëm wi.
8Naka noona Ecen, mi fees ak yiw ak kàttan, di def ay kéemaan yu mag ak ay firnde ca nit ña.
9Waaye ay nit jóg, bokk ci jàngu, bi ñuy wax Jàngub ñi ñu goreel, di ay niti dëkki Siren ak Alegsàndiri, ak it waa diiwaani Silisi ak Asi. Ñuy werante ak Ecen,
10waaye àttanuñu sagoom ak Xel mi muy waxe.
11Kon ñu daldi jënd ay nit, ñu ne: «Dégg nanu ko, muy sosal Musaa ak Yàlla.»

Read JËF YA 6JËF YA 6
Compare JËF YA 6:5-11JËF YA 6:5-11