Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 6:5-11 in Wolof

Help us?

JËF YA 6:5-11 in Téereb Injiil

5 Lii ñu wax nag neex na mbooloo mépp. Noonu ñu tànn Ecen, di nit ku fees ak ngëm ak Xel mu Sell mi, boole ci Filib ak Porokor, teg ca Nikanor, Timon, Parmenas ak Nikolas, mi juddoo Ancos te tuub ci yoonu Yawut ya.
6 Ñu jébbal leen ndaw ya, ñaanal leen, teg leen loxo.
7 Noonu kàddug Yàlla di law, ba mbooloom taalibe yi di yokku bu bare ci Yerusalem; te sarxalkat yu bare déggal Yàlla ci topp yoonu ngëm wi.
8 Naka noona Ecen, mi fees ak yiw ak kàttan, di def ay kéemaan yu mag ak ay firnde ca nit ña.
9 Waaye ay nit jóg, bokk ci jàngu, bi ñuy wax Jàngub ñi ñu goreel, di ay niti dëkki Siren ak Alegsàndiri, ak it waa diiwaani Silisi ak Asi. Ñuy werante ak Ecen,
10 waaye àttanuñu sagoom ak Xel mi muy waxe.
11 Kon ñu daldi jënd ay nit, ñu ne: «Dégg nanu ko, muy sosal Musaa ak Yàlla.»
JËF YA 6 in Téereb Injiil

Jëf ya 6:5-11 in Kàddug Yàlla gi

5 Wax jooju daldi neex mbooloo mépp. Ñu seppi Eccen, nit kufeese ngëm ak Noo gu Sell gi, seppi Filib ak Porokor ak Nikanor ak Timon ak Parmenas ak Nikolas, ma dëkke Àncos te dib tuubeen bu duggoon lu jiitu ci yoonu Yawut.
6 Ñu indi leen fa kanam ndaw ya, ñu ñaanal leen, teg leen loxo.
7 Ba loolu amee kàddug Yàlla di law, limu taalibe yi yokku ba bare lool ci biir Yerusalem, sarxalkat yu bare daldi topp yoonu ngëm wi.
8 Ci kaw loolu Eccen, mi yiwu Yàlla def ag leer fees ko, di def ay kéemaan ak firnde yu mag ci biir askan wi.
9 Ba loolu amee ñenn ca jàngu ba ñuy wax jàngub waa Goreel ga, daldi jóg, di tàmbalee weranteek Eccen. Ay niti waa Siren a nga ca, ak waa Alegsàndiri, ak waa diiwaani Silisi ak Asi.
10 Teewul àttanuñu xelam mu rafet, ak Noo gi muy waxe.
11 Ñu daldi ger ay nit ngir ñu duural ko, ne: «Noo ko dégg, mu yékkati kàdduy saaga, jëme ci Musaa ak ci Yàlla.»
Jëf ya 6 in Kàddug Yàlla gi