Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 28

JËF YA 28:1-8

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Bi nu rëccee, nu yég ne dun baa nga tudd Màlt.
2Te waa réew ma won nu laabiir gu ràññiku, ndaxte taalal nañu nu sawara, ganale nu ndax taw bi sóob ak sedd bi.
3Pool nag di for matt, di ko def ca taal ba, jaan ne ca mëlle ndax tàngoor wa, taq ci loxoom.
4Bi waa réew ma gisee rab wa wékku ci loxoom nag, ñuy waxante naan: «Ci lu wóor nit kii reykat la; te bi mu rëccee ca géej ga sax, ndogalu Yàlla mayu ko mu dund.»
5Waaye Pool yëlëb rab wa ca sawara sa, te wàññiwu ko dara.
6Nit ñi di xaar mu newi, mbaa mu ne dàll, dee; waaye bi ñu négee lu yàgg te gis ne dara jotu ko, ñu soppi xel ne: «Kii yàlla la.»
7Amoon na nag ca wet ya ay suuf yu doon moomeelu ku tudd Publiyus, di kilifag dun ba. Mu teeru nu, ganale nu ngan gu réy diirub ñetti fan.
8Fekk baayu Publiyus dafa tëdd ndax ay tàngoori yaram yu koy dikkal ak biiru taññ. Pool nag dem seeti ko, ñaan ci Yàlla, teg ko ay loxoom, mu daldi wér.

Read JËF YA 28JËF YA 28
Compare JËF YA 28:1-8JËF YA 28:1-8