Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Buur ya - 1.Buur ya 7

1.Buur ya 7:18-26

Help us?
Click on verse(s) to share them!
18Mu defar ñaari jaray gërënaat, solal ko caax yi, wëralee ko bopp yi, ci xer wu ci nekk.
19Bopp yi nekkoon ci kaw xer yi ci kanam nag bindoo ni lëppi tóor-tóor te bu ci nekk di ñeenti xasab.
20Bopp yi ci kaw ñaari xer yi, bu ci nekk ñaar téeméeri gërënaat a ko wër ci kaw, feggook gamb bi ci wàllaa caax bi.
21Mu samp jën yi ci kanam bunt néeg Yàlla bu mag bi; samp jënu ndijoor wi, tudde ko Yakin (Kiy taxawal), samp jënu càmmoñ wi, tudde ko Bowas (Kiy dooleel).
22Kaw xer yi ay lëppi tóor-tóor yu ñu xellee ci tege. Liggéeyu xer ya daldi sotti.
23Ba mu ko defee Uram móol mbalkam njàpp mu weñ, ñu di ko wax Géej ga. Mbalka ma daa mërgalu, yaatoo fukki xasab, catu omb ba catu omb, taxawaay ba di juróomi xasab, ag buumu fanweeri xasab di ko ub.
24Ay gamb la ko sàkkal ci suufu kéméj gi, fukki gamb tollook xasab. Mu def gamb yi ñaari caq yu wër mbalka mi ba mu daj te ànd ak mbalka mi ci benn xelli.
25Mbalkam njàpp mi tege ci kaw fukki jëmmi nag ak yaar, ñett jublu bëj-gànnaar, ñett jublu sowu, ñett jublu bëj-saalum, ñett jublu penku. Mbalka mi war nag yi, seeni gannaaw féete biir, ñoom ñépp.
26Dëllaayu mbalka mi yaatuwaayu loxo la, kéméj gi mel ni gémmiñu kaas, di nirook lëppi tóor-tóor. Ñaar téeméeri barigo la mbalka miy def. (200).

Read 1.Buur ya 71.Buur ya 7
Compare 1.Buur ya 7:18-261.Buur ya 7:18-26