Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Buur ya - 1.Buur ya 6

1.Buur ya 6:24-36

Help us?
Click on verse(s) to share them!
24Benn serub bi laaf mu ci nekk juróomi xasab la, muy fukki xasab ci catal menn laaf mi ba ca catal laaf ma ca des.
25Fukki xasab it mooy taxawaayu ñaareelu serub bi, ndax ñaari serub yee tolloo dayo, bokk bind;
26taxawaayub serub bu ci nekk fukki xasab la.
27Suleymaan teg serub ya ca digg néeg bu sell baa sell, seeni laaf fireeku, catal laafu benn serub bi di laal genn wetu tabax bi, catal laafu serub ba ca des di laal geneen wetu tabax bi. Seen ñaari cati laaf yi ci des it di laale fa tollook digg néeg ba.
28Mu teg ca xoob serub yi wurus.
29Mu yettlu nag ay serub ci kaw miiri ñaari néegi kër gi, yettaale garabi ron aki tóor-tóor yu focci, wërale.
30Xoob na itam dëru tabax bi wurus, ci néegu biir bi ak ci biti.
31Buntu néeg bu sell baa sell, kubeeri banti oliw la ko def, njëël bunt bi aki jënam bant lañu yu bindoo juróomi wet.
32Ñaari kubeer yi banti oliw la; mu yettlu ca kawam ay malaakay serub aki ron aki tóor-tóor yu focci, ba noppi xoob lépp wurus, xoobaale serub yi wurus ak ron yi itam.
33Noonu it la def buntu néeg bu mag bi, ay jënam di bantu oliw, waaye bunt bi, jëwam aki jënam, bant lañu yu bindoo ñeenti wet.
34Ñaari kubeeram di bantu sippar, bu ci nekk di ñaari xànq yuy warangiku.
35Mu yettlu ci kaw kubeeri bunt yi jëmmi serub aki ron aki tóor-tóor yu focci, daldi xoob lépp wurus.
36Suleymaan tabaxe miiru ëttu biir bi ay xeeri yett ak xànqi seedar, ba ñetti sësalantey xeer yu tegloo yu ne, benn sësalanteb xànqi seedar tege ca.

Read 1.Buur ya 61.Buur ya 6
Compare 1.Buur ya 6:24-361.Buur ya 6:24-36