Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Buur ya - 1.Buur ya 16

1.Buur ya 16:3-29

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Kon dama ne, dinaa la far, yaw Basa, yaak sa waa kër. Dinaa def sa kër mel ni kër Yerbowam doomu Nebat.
4Ku Basa deele ci dëkk bi, xaj yi lekk; ku médd ca àll ba, njanaaw ya for.»
5Li des ci mbiri Basa ak la mu def ak njàmbaaram, bindees na lépp moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant.
6Gannaaw loolu Buur Basa saay, fekki ay maamam, ñu denc ko Tirsa. Ela doomam falu buur, wuutu ko.
7Te itam ba kàddug Aji Sax ji dikkalee Yonent Yàlla Yewu doomu Anani ci mbirum Basa ak waa këram, li ko waral mooy la Basa def lépp, di roy waa kër Yerbowam, Aji Sax ji ñaawlu ko ba xolam fees. Rax ci dolli Basa rey waa kër Yerbowam.
8Ba Asa buurub Yuda duggee ñaar fukkeelu atu nguuram ak juróom benn, ca la Ela doomu Basa falu buur, jiite Israyil. Péeyoo na Tirsa diiru ñaari at.
9Simri, jawriñam ba yilifoon genn-wàllu watiiri xareem, moo ko fexeel. Booba Elaa ngay naan ba màndi ca kër Arsa, ka yor mbiri këram ca Tirsa.
10Simri duggsi, jam ko, mu dee. Loolu yemook ba Asa buurub Yuda di dugg ñaar fukkeelu atu nguuram ak juróom ñaar. Simri falu, wuutu ko.
11Simri falu ba toog ci jal bi, daldi rey mboolem waa kër Basa. Bàyyiwu ca kuy taxaw, colol; du mbokk, du xarit.
12Simri faagaagal waa kër Basa gépp, muy la Aji Sax ji waxoon, ba mu rëbbee Basa, Yonent Yàlla Yewu jottli.
13Li ko waral di mboolem bàkkaar yi Basa ak doomam Ela bàkkaar te bàkkaarloo ko Israyil, ba feesal xolu Aji Sax ji Yàllay Israyil ndax seen tuuri neen.
14Li des ci mbiri Ela ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant.
15Ba Asa buurub Yuda duggee ñaar fukkeelu atu nguuram ak juróom ñaar, ca la Simri falu. Mu nguuru diiru juróom ñaari fan ca Tirsa. Booba mbooloom xareem Israyil a nga jógal dëkkub Filisteen ba ñuy wax Gibeton.
16Mbooloo ma ca dal ba dégg ñu naan: «Simri de lalal na Buur pexe, ba rey ko.» Israyil gépp daldi fal buur Omri, ma jiite woon mbooloom xarem Israyil. Mu moom Israyil bésub keroog ca dal ba.
17Omri ak Israyil gépp bàyyikoo Gibeton, ànd gawi dëkk ba ñuy wax Tirsa.
18Ba Simri gisee ne nangu nañu dëkk ba, daa dugg kër Buur, jàll ca biir-a-biir, daldi taal kër ga ca kawam, dee.
19Li ko waral mooy bàkkaar yi mu bàkkaar, di def lu bon lu Aji Sax ji ñaawlu, aw ci tànki Yerbowam, di bàkkaarloo Israyil.
20Li des ci mbiri Simri ak pexe ma mu laloon, bindees na lépp moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant.
21Ba mu ko defee mbooloom Israyil séddlikoo, def ñaari xaaj. Genn-wàllu mbooloo ma topp ca gannaaw Tibni, nar koo fal buur. Tibni nag, Ginat ay baayam. Genn-wàll ga ca des ànd ak Omri.
22Mbooloom Omri ëpp doole mbooloom Tibni doomu Ginat. Tibni daldi dee, Omri di buur.
23Ba Asa buurub Yuda duggee fanweereelu atu nguuram ak benn, ca la Omri falu buur, jiite Israyil. Omri nguuru na diiru fukki at ak ñaar. Mu péeyoo Tirsa juróom benni at.
24Omri nag dem ca Semer, jënde ca moom tundu Samari ci juróom ñaar fukki kiloy xaalis. Omri tabax ca kaw tund wa, dippee dëkk ba mu tabax Samari, mu dëppook Semer, turu boroom tund wa.
25Teewul Omri di def lu bon lu Aji Sax ji ñaawlu, ba gëna bàkkaar mboolem ña ko jiitu.
26Daa aw ci tànki Yerbowam doomu Nebat ci mboolem lu mu daan def ba ci bàkkaaram bi mu daan bàkkaarloo Israyil, di jógal xolu Aji Sax ji Yàllay Israyil ci seen tuuri neen.
27Li des ci mbiri Omri aki jëfam ak njàmbaaram, bindees na lépp moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant.
28Buur Omri saay, fekki ay maamam, ñu denc ko ca Samari. Axab doom ja falu buur, wuutu ko.
29Ba Asa buurub Yuda duggee fanweereelu atu nguuram ak juróom ñett, ca la Axab doomu Omri falu, jiite Israyil. Axab doomu Omri nguuru na Israyil ñaar fukki at ak ñaar, péeyoo Samari.

Read 1.Buur ya 161.Buur ya 16
Compare 1.Buur ya 16:3-291.Buur ya 16:3-29