17Farisen ya laajaat ka gumba woon ne ko: «Yaw, loo wax ci moom? Yaw de la ubbil say bët.» Mu ne leen: «Yonent la.»
18Yawut ya manuñu woona nangu ne, nit ka dafa gumba woon tey gis léegi, ñu daldi wooluji ay waajuram,
19laaj leen ne: «Ndax kii mooy seen doom, ji ngeen ne gumba judduwaale la? Kon fu mu jaar, bay gis léegi?»
20Waajur ya ne leen: «Xam nanu ne daal, sunu doom la te dafa judduwaale gumba.
21Waaye ni mu def léegi bay gis, xamunu ko, te xamunu it ki ko ubbil ay bëtam. Laajleen ko; magum jëmm la, te man na tontul boppam.»
22Ragal Yawut ya nag moo taxoon waajuri nit ka waxe noonu, ndaxte Yawut ya dañoo mànkoo woon ne, képp ku seede ne Yeesu mooy Almasi bi, ñu dàq la ca jàngu ba.
23Looloo tax waajur ya ne: «Laajleen ko; magum jëmm la.»
24Farisen ya dellu woowaat ka gumba woon ne ko: «Waxal sa digganteek Yàlla. Xam nanu ne waa joojee boroom bàkkaar la.»
25Mu ne: «Xawma ndax boroom bàkkaar la am déet. Li ma xam daal mooy gumba woon naa, te léegi maa ngi gis.»
26Ñu laaj ko ne: «Lu mu la def? Nu mu la ubbile say bët?»
27Mu ne leen: «Wax naa leen ko ba noppi, waaye dégluwuleen ma. Lu ngeen bëgg ci ma di ko wax, di waxaat? Xanaa dangeena bëgga nekk yéen itam ay taalibeem?»
28Ci kaw loolu ñu daldi ko saaga ne ko: «Yaw yaay taalibeem. Nun, taalibey Musaa lanu.
29Xam nanu ne Yàlla wax na ak Musaa; waaye kii, xamunu sax fu mu jóge.»
30Waa ja ne leen: «Loolu de, doy na waar! Xamuleen fu mu jóge, te moo ubbi samay bët!