Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - YOWAANA - YOWAANA 6

YOWAANA 6:56-70

Help us?
Click on verse(s) to share them!
56Kiy lekk sama yaram tey naan sama deret dina sax ci man, ma dëkk ci moom.
57Baay bi ma yónni mu ngi dund, te maa ngi dund jaarale ko ci moom; noonu itam ku may lekk dina dund jaarale ko ci man.
58Kon nag ñam wi wàcce ci asamaan a ngi noonu; bokkul ak ñam wa seeni maam lekkoon te faatu. Ku lekk ñam wii may wax dinga dund ba fàww.»
59Baat yooyu la Yeesu wax, bi mu doon jàngle ca jàngu ba ca Kapernawum.
60Bi ñu dégloo Yeesu ba noppi, taalibeem yu bare nee nañu: «Njàngle mii de, jafe na! Kan moo ko mana déglu?»
61Yeesu gis ne taalibeem yaa ngi ñurumtoo loolu, mu ne leen: «Ndax li ma wax da leena jaaxal?
62Lan mooy am nag, bu fekkee gis ngeen Doomu nit ki dellu, yéeg fa mu jëkkoona nekk?
63Xelu Yàlla mi mooy joxe dund; ñam wi jariñul dara. Kàddu yi ma leen wax, ci Xelum Yàlla lañu jóge te ñooy joxe dund.
64Waaye am na ci seen biir ñu ko gëmul.» Ndaxte Yeesu xamoon na ca njàlbéen ga ñan ñoo ko waroona gëmadi ak kan moo ko waroona wor.
65Mu dolli ca it ne: «Looloo tax ma ne, kenn manula ñëw ci man te Baay bi mayu la, nga agsi.»
66Ci loolu taalibeem yu bare dëpp, bañatee ànd ak moom.
67Yeesu daldi wax ak fukki taalibe yi ak ñaar ne leen: «Mbaa bëgguleena dem, yéen itam?»
68Simoŋ Piyeer ne ko: «Boroom bi, ci kan lanuy dem? Yaa yor kàddu yiy joxe dund gu dul jeex.
69Léegi nun gëm nanu te xam nanu ne yaa di Aji Sell, ji jóge ci Yàlla.»
70Yeesu ne leen: «Xanaa du maa leen tànn, yéen fukk yi ak ñaar? Moona, am na ci yéen koo xam ne seytaane la!»

Read YOWAANA 6YOWAANA 6
Compare YOWAANA 6:56-70YOWAANA 6:56-70