Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - YOWAANA - YOWAANA 2

YOWAANA 2:11-23

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11Firnde jii ame ca Kana, ca diiwaanu Galile, moo doon kéemaan gi Yeesu jëkka def. Ci noonu la wonee màggaayam te ay taalibeem gëm nañu ko.
12Bi loolu weesoo, mu ànd ak yaayam, ay rakkam ak i taalibeem, dem dëkku Kapernawum. Waaye yàgguñu fa.
13Màggalu Yawut, gi ñuy wax bésu Mucc ba, mu ngi doon jubsi. Yeesu dem Yerusalem,
14dugg ca kër Yàlla ga. Bi mu fa demee, fekk na ca ëtt ba ay jaaykati nag ak yu xar ak yu pitax, ak weccikatu xaalis ya toog.
15Noonu Yeesu ràbb ab yar, daldi leen koy dàqe, ngir ñu génn ëttu kër Yàlla ga, ñoom ak xar ya ak nag ya. Mu tasaare xaalisu weccikat ya, daaneel taabal ya,
16daldi ne jaaykati pitax ya: «Jëleleen fi lii! Sama kër Baay, buleen ko def marse!»
17Taalibeem ya fàttaliku Mbind mii: «Cawarte gi ma am ci sa kër, mu ngi mel ni taal buy tàkk ci sama biir.»
18Noonu Yawut ya ne ko: «Ban firnde nga nuy won ngir dëggal ne am nga sañ-sañu def lii nga def?»
19Yeesu ne leen: «Daaneel-leen kër Yàlla gii, ma daldi koy yékkati ci ñetti fan.»
20Ñu ne ko: «Nga ne kër Yàlla, gii ñu tabax ci ñeent fukki at ak juróom benn, man nga koo yékkati ci ñetti fan!»
21Waaye kër Yàlla, gi Yeesu doon wax, nekkul woon ab tabax, aw yaramam ci boppam moo ko taxoon di wax.
22Gannaaw ga nag, bi Yeesu deeyee ba dekki, la taalibeem ya fàttaliku li mu waxoon, daldi gëm Mbind mi ak wax, ja leen Yeesu waxoon.
23Bi Yeesu nekkee Yerusalem ci màggalu bésu Mucc ba, ñu bare gis kéemaan, yi mu doon def, daldi gëm ci turam.

Read YOWAANA 2YOWAANA 2
Compare YOWAANA 2:11-23YOWAANA 2:11-23