Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - YOWAANA - YOWAANA 21

YOWAANA 21:18-24

Help us?
Click on verse(s) to share them!
18Ci dëgg-dëgg Piyeer, maa ngi la koy wax, bi nga dee ndaw yaa doon takk sa geño, di dem fu la neex. Waaye boo màggatee, dinga tàllal say loxo, keneen takkal la sa geño, yóbbu la foo bëggul.»
19Ci baat yooyu la Yeesu doon misaale nan la Piyeer wara faatoo ngir jollil ndamu Yàlla. Noonu Yeesu ne ko: «Toppal ci man!»
20Piyeer geestu, gis taalibe bi Yeesu bëggoon, di ñëw ci seen gannaaw. Taalibe boobu mooy ki sóonu woon ca Yeesu, ba ñuy lekk, te laajoon ko ne: «Boroom bi, kan moo lay wori?»
21Piyeer gis ko, daldi ne Yeesu: «Kii nag, Boroom bi, nu muy mujje?»
22Yeesu ne ko: «Su ma neexoon mu dund, ba ma délsi, lu ciy sa yoon? Yaw toppal ci man.»
23Noonu am, ci bokki taalibe yi, ñu xalaat ne, taalibe boobu du dee. Moona Yeesu masul ne Piyeer, du dee; waaye li mu wax mooy: «Su ma neexoon mu dund, ba ma délsi, lu ciy sa yoon?»
24Taalibe boobu mooy seede mbir yooyu, bind leen, te xam nanu ne li muy wax dëgg la.

Read YOWAANA 21YOWAANA 21
Compare YOWAANA 21:18-24YOWAANA 21:18-24