6Yeesu ne ko: «Man maay yoon wi, maay dëgg te dund it man la. Kenn du ñëw ci Baay bi te jaarul ci man.
7Ndegam xam ngeen ma, dingeen xam itam sama Baay. Lu weesu tey, xam ngeen ko te gis ngeen ko.»
8Filib ne ko: «Boroom bi, won nu Baay bi; loolu doy na nu.»
9Yeesu ne ko: «Ni ma yàggeek yéen te ba tey Filib, xamuloo ma? Ku ma gis, gis nga Baay bi. Kon nag nan ngay mana laaje naan: “Won nu Baay bi”?
10Xamuloo ne maa ngi nekk ci Baay bi te Baay baa ngi ci man? Kàddu yi ma leen di wax jógewuñu ci man, waaye Baay bi nekk ci man mooy matal ay jëfam.
11Gëmleen li ma leen wax ne maa ngi ci Baay bi te Baay baa ngi ci man; walla boog, gëmleen ndax jëf yi.
12Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax: képp ku ma gëm dina def, moom itam, jëf yi may def. Dina def sax yu gëna màgg, ndaxte maa ngi dem ci Baay bi.
13Te it lu ngeen ñaan ci sama tur dinaa ko def, ngir Doom ji feeñal ndamu Baay bi.
14Lu ngeen ñaan ci sama tur, maa koy def.
15«Bu ngeen ma bëggee, dingeen topp sama ndigal.