Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 6

Sarxalkat yi 6:12-18

Help us?
Click on verse(s) to share them!
12Aji Sax ji wax na Musaa ba tey ne ko:
13«Li Aaróona aki doomam yu góor di sarxalal Aji Sax ji, keroog bu ñu koy diw, fal ko, mooy lii: ñetti kiloy sunguf su mucc ayib, tollook saraxu pepp bi ñu saxoo bés bu nekk, te genn-wàll gi di suba, genn-wàll gi ngoon.
14Saafukaayu weñ lañu koy lakke, xiiwaale ko diw, indi xiiw ba, muy saraxu pepp. Nañu ko def ay dog yu ñuy lakkal Aji Sax ji, muy xeeñ xetug jàmm.
15Sarxalkat bi ñuy fal ci doomi Aaróona yu góor yi, mu war koo wuutu, da koy def moom itam. Aji Sax ji moo jagoo sarax boobu fàww, te dañu koy lakk ba mu jeex.
16Te it mboolem saraxu pepp bu sarxalkat di defal boppam, dees koy lakk ba mu jeex. Deesu ci lekk.»
17Aji Sax ji waxati Musaa ne ko:
18«Waxal Aaróona ak doomam yu góor ne leen: Dogal bi ci saraxu póotum bàkkaar mooy lii: Juru saraxas póotum bàkkaar dañu koy rendi fa ñu wara rendi juru saraxu dóomal, fi kanam Aji Sax ji. Lu sella sell la.

Read Sarxalkat yi 6Sarxalkat yi 6
Compare Sarxalkat yi 6:12-18Sarxalkat yi 6:12-18