Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 5

Sarxalkat yi 5:2-10

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2«Su fekkee ne nit ki dafa laal lu sobewu, te seetluwu ko, lu mel ni rab wu daganul te médd, muy rabu àll mbaa ag jur, mbaa luy raam, kon sobewu na, tooñ na.
3Su fekkee ne nit ki dafa laal sobey nit ak su mu mana doon, te teyu ko, ba mu wees, saa yu ko xamee, tooñ na.
4Su sàgganee it ba giñ ne dina def nàngam, muy lu baax mbaa lu bon, muy mboolem ngiñ lu ko rëcc te ba mu koy wax teyu ko, ba mu wees, saa yu ko xamee tooñ na.
5Ci tooñin yooyu ñu lim war naa wax na mu tooñe.
6Na indil Aji Sax ji gàtt bu jigéen, xar mbaa bëy, muy daanam ndax bàkkaar bi mu def. Saraxu póotum bàkkaar lay doon, sarxalkat bi defal ko ko njotlaayal bàkkaar bi mu def.
7«Nit ki amul lu mat njégu gàtt, na indil Aji Sax ji ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, muy daanam ndax bàkkaar bi mu def; benn bi di saraxu póotum bàkkaar, bi ci des di sarax rendi-dóomal.
8Da koy yót sarxalkat bi, kooku jëkka rey benn bi, muy saraxu póotum bàkkaar; na kutt baat bi te bumu teqale bopp beek baat bi.
9Day xëpp ci wetu sarxalukaay bi deretu njanaaw liy saraxu póotum bàkkaar. Li des ci deret ji dees koy tuur ci taatu sarxalukaay bi. Saraxu póotum bàkkaar la.
10Ñaareel bi na ko def saraxu rendi-dóomal, muy li ñu santaane. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaar bi mu def, mu am njéggal.

Read Sarxalkat yi 5Sarxalkat yi 5
Compare Sarxalkat yi 5:2-10Sarxalkat yi 5:2-10