Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 5:2-10 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 5:2-10 in Kàddug Yàlla gi

2 «Su fekkee ne nit ki dafa laal lu sobewu, te seetluwu ko, lu mel ni rab wu daganul te médd, muy rabu àll mbaa ag jur, mbaa luy raam, kon sobewu na, tooñ na.
3 Su fekkee ne nit ki dafa laal sobey nit ak su mu mana doon, te teyu ko, ba mu wees, saa yu ko xamee, tooñ na.
4 Su sàgganee it ba giñ ne dina def nàngam, muy lu baax mbaa lu bon, muy mboolem ngiñ lu ko rëcc te ba mu koy wax teyu ko, ba mu wees, saa yu ko xamee tooñ na.
5 Ci tooñin yooyu ñu lim war naa wax na mu tooñe.
6 Na indil Aji Sax ji gàtt bu jigéen, xar mbaa bëy, muy daanam ndax bàkkaar bi mu def. Saraxu póotum bàkkaar lay doon, sarxalkat bi defal ko ko njotlaayal bàkkaar bi mu def.
7 «Nit ki amul lu mat njégu gàtt, na indil Aji Sax ji ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, muy daanam ndax bàkkaar bi mu def; benn bi di saraxu póotum bàkkaar, bi ci des di sarax rendi-dóomal.
8 Da koy yót sarxalkat bi, kooku jëkka rey benn bi, muy saraxu póotum bàkkaar; na kutt baat bi te bumu teqale bopp beek baat bi.
9 Day xëpp ci wetu sarxalukaay bi deretu njanaaw liy saraxu póotum bàkkaar. Li des ci deret ji dees koy tuur ci taatu sarxalukaay bi. Saraxu póotum bàkkaar la.
10 Ñaareel bi na ko def saraxu rendi-dóomal, muy li ñu santaane. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaar bi mu def, mu am njéggal.
Sarxalkat yi 5 in Kàddug Yàlla gi