Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 26

Sarxalkat yi 26:34-45

Help us?
Click on verse(s) to share them!
34«Su boobaa mboolem diir ba suuf di wéet moom lay daboo ati Noflaayam, fekk yeen ngeen nekk ca seen réewu noon ya. Su ko defee suuf si dina nopplu moos, ba daboo ko ati Noflaayam.
35Mboolem diir bi suuf siy wéet, moom lay nopploo la mu noppluwuloon, ba leen ay ati Noflaay fekkee ngeen dëkk fa.
36«Ñi des ci yeen, dinaa indi njàqare ci seen xol, foofa ngeen nekk ca seen réewu noon ya, ba xob wu ne foy-foy ngeen daw. Dingeen xélu ni ku ñuy dàqe saamar, bay daanu, te dàqeesu leen.
37Dingeen fakkastalante di daw, ni ñu ñuy dàqe saamar, te dàqeesu leen, ba dungeen mana taxaw ci seen kanami noon.
38Dingeen deeye àll, te seen suufu noon yaa leen di lekk.
39Ñi des ci yeen dinañu ràgg ca seen réewi noon ndax seeni bàkkaar ak seen bàkkaari maam.
40«Su ko defee ñoom dinañu tudd seen bàkkaar ak seen bàkkaaru maam ya, ndax dañu maa wor te dëkke maa noonoo,
41ba man itam ma noonoo leen, toxal leen seen réewu noon. Bu ñu tuubee seen xol bu dëgër nag, ba matal seen mbugal yi sababoo ci seeni ñaawtéef,
42su boobaa maay bàyyi xel ci sama kóllëre gaak Yanqóoba ak sama kóllëre gaak Isaaxa ak sama kóllëre gaak Ibraayma, te duma fàtte li ma dige ci wàllu réew mi.
43«Waaye réew mi dinañu ko gental, mu daboo ati Noflaayam diir ba ñu ko dëddoo, wéetal ko, te fekk ñoom ñuy fey seen boru tooñ; ndax kat dañoo sofental samay santaane, xalab samay dogal.
44Ndaxam du tax ma sofental leen ca seen réewu noon, mbaa ma di leen xalab, di leen faagaagal, nde kon ma fecci sama kóllëreek ñoom. Ndax man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
45Maa leen di bàyyil xel ci sama kóllëre gaak seen maam ya ma génne réewum Misra, jaambur ñi seede, ngir doon seen Yàlla. Maay Aji Sax ji.»

Read Sarxalkat yi 26Sarxalkat yi 26
Compare Sarxalkat yi 26:34-45Sarxalkat yi 26:34-45