Text copied!
Bibles in Wolof

Sarxalkat yi 26:34-45 in Wolof

Help us?

Sarxalkat yi 26:34-45 in Kàddug Yàlla gi

34 «Su boobaa mboolem diir ba suuf di wéet moom lay daboo ati Noflaayam, fekk yeen ngeen nekk ca seen réewu noon ya. Su ko defee suuf si dina nopplu moos, ba daboo ko ati Noflaayam.
35 Mboolem diir bi suuf siy wéet, moom lay nopploo la mu noppluwuloon, ba leen ay ati Noflaay fekkee ngeen dëkk fa.
36 «Ñi des ci yeen, dinaa indi njàqare ci seen xol, foofa ngeen nekk ca seen réewu noon ya, ba xob wu ne foy-foy ngeen daw. Dingeen xélu ni ku ñuy dàqe saamar, bay daanu, te dàqeesu leen.
37 Dingeen fakkastalante di daw, ni ñu ñuy dàqe saamar, te dàqeesu leen, ba dungeen mana taxaw ci seen kanami noon.
38 Dingeen deeye àll, te seen suufu noon yaa leen di lekk.
39 Ñi des ci yeen dinañu ràgg ca seen réewi noon ndax seeni bàkkaar ak seen bàkkaari maam.
40 «Su ko defee ñoom dinañu tudd seen bàkkaar ak seen bàkkaaru maam ya, ndax dañu maa wor te dëkke maa noonoo,
41 ba man itam ma noonoo leen, toxal leen seen réewu noon. Bu ñu tuubee seen xol bu dëgër nag, ba matal seen mbugal yi sababoo ci seeni ñaawtéef,
42 su boobaa maay bàyyi xel ci sama kóllëre gaak Yanqóoba ak sama kóllëre gaak Isaaxa ak sama kóllëre gaak Ibraayma, te duma fàtte li ma dige ci wàllu réew mi.
43 «Waaye réew mi dinañu ko gental, mu daboo ati Noflaayam diir ba ñu ko dëddoo, wéetal ko, te fekk ñoom ñuy fey seen boru tooñ; ndax kat dañoo sofental samay santaane, xalab samay dogal.
44 Ndaxam du tax ma sofental leen ca seen réewu noon, mbaa ma di leen xalab, di leen faagaagal, nde kon ma fecci sama kóllëreek ñoom. Ndax man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
45 Maa leen di bàyyil xel ci sama kóllëre gaak seen maam ya ma génne réewum Misra, jaambur ñi seede, ngir doon seen Yàlla. Maay Aji Sax ji.»
Sarxalkat yi 26 in Kàddug Yàlla gi