Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 26

Sarxalkat yi 26:30-33

Help us?
Click on verse(s) to share them!
30Dinaa tas seen bérabi jaamookaay, toj seeni suurukaay. Seen kasaray tuur yi ne làcc, ma jal ca seeni néew. Maa leen di sib,
31gental seen dëkk yu mag, tas seen bérab yu sell, te dootuma faale xetug jàmm ca seeni sarax.
32Maay tas seenum réew, ba seen noon ya ko nangu yéemu ca.
33Yeen nag maa leen di tasaare ci biir xeet yi, ndax maay génne saamar mbaram, mu dal ci seen kaw. Seenum réew dina wéet, seen dëkk yu mag gent.

Read Sarxalkat yi 26Sarxalkat yi 26
Compare Sarxalkat yi 26:30-33Sarxalkat yi 26:30-33