30 Dinaa tas seen bérabi jaamookaay, toj seeni suurukaay. Seen kasaray tuur yi ne làcc, ma jal ca seeni néew. Maa leen di sib,
31 gental seen dëkk yu mag, tas seen bérab yu sell, te dootuma faale xetug jàmm ca seeni sarax.
32 Maay tas seenum réew, ba seen noon ya ko nangu yéemu ca.
33 Yeen nag maa leen di tasaare ci biir xeet yi, ndax maay génne saamar mbaram, mu dal ci seen kaw. Seenum réew dina wéet, seen dëkk yu mag gent.