16Ku ñàkke kersa turu Aji Sax ji, dee rekk mooy àtteem. Mbooloo mi mépp a ko wara dóor ay doj, ba mu dee. Muy doxandéem muy njuddu-ji-réew, ku ci ñàkke kersa turu Aji Sax ji, dee mooy àtteem.
17«Bu loolu weesee képp ku faat bakkanu nit, dee rekk mooy àtteem.
18Ku faat bakkanu mala, na fey boroom. Bakkan, bakkan a koy fey.
19Képp ku gaañ moroomam, la mu ko def rekk lañu koy def.
20Damm-damm, damm-damm a koy fey; bët, bët a koy fey; bëñ it bëñ a koy fey. Ni mu gaañe moroomam rekk, ni lañu koy gaañe.
21«Ku rey ag jur na fey boroom, waaye ku rey nit dee mooy àtteem.